Bienvenue Invité Dans Le Forum De Tous Ceux Qui Aiment Le Sénégal !

Connecté en tant que Anonymous. Dernière visite le

Vous n'êtes pas connecté. Connectez-vous ou enregistrez-vous

Poster un nouveau sujet  Répondre au sujet

Voir le sujet précédent Voir le sujet suivant Aller en bas  Message [Page 1 sur 1]

Thiamaass


Membre - Familiarisé

Membre - Familiarisé
Sexe:Masculin Vierge Rat
BATAAXAL GU MAG GI ËMB SAÑ-SAÑI DOOMI AADAMA
[Preamble]
Ñu jàpp te nangu ne sagu doomi aadama ak sañ-sañam yépp-dañu yam te kenn mënukóo jalgati, te lu lépp nekk na cës laay ci taxufeex ci mbirum àtte ak jàmm ci biir àdduna.
Ñu jàpp ne ñakk xam ak soofantal sañ-sañi doomi aadama indi na aymusiba yu tar tax képp kuy dund fippu. Temano egsi na ba mu nekk ci doomi aadama ñu mën a wax, xalaat, ci seen coobare, bundxatal, nàkk dëddu leen.
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu aar sañ-sañi doomu aadama ak ay matukaay ci wàllu yoon; ngir doomu aadama moomu kenn du ko sonal, muy fippu ci nootaange ak lu koy bunduxatal.
Ñu jàpp ne am na solo lool ñu góor-goorlu ba gën a rataxal jokkalante gi diggante xeet yi.
Ñu jàpp ne ci bataaxal boobule mbootaayu xeet yi yeesalaat na ay pas-pasam jëme ko ci sañ-sani doomi aadama yu tolloo, ci sag, ci bir lépp lu aju ci dundin diggante góor ak jigéen, ci biir tawfeex gu yaa.
Ñu jàpp ne réew yi ci bokk jël nañu ay matukaay ngir dëgëral jokkalante gi ak mbootaayu xeet yi, ñu naw it bu baax sann-sañi doomi aadama ak tawfeex yu wóor ci biir àdduna yépp.
Ñu jàpp ne ànd taxawal sañ-sañ yeek tawfeex yi nekk na lu am solo lool ngir, darajaal matukaay yooyu.
Ndaje mu mag mi biral na ci bataaxal bii ne xeet yépp, réew yépp ak kurel yépp ñu jàpp li ci nekk, ci seen xel, te ñu góor-góorlu, ñu jaarale lii lépp ci njàng mi ak yar gi.
Ñu lawal sañ-sañ yeek taawfeex yi jël aymatukaay ci biirak bitim réew.
Ñu nangu te di doxal fépp ci anam gu wér ci biir xeet yi sosoo ci réew i bokk ci mbootaay gi ak gox yi bootu ci ñoom.
1. Matukaay bu jëkk bi


Doomi aadama yépp danuy juddu, yam ci tawfeex ci sag ak sañ-sañ. Nekk na it ku xam dëgg te ànd na ak xelam, te war naa jëflante ak nawleen, te teg ko ci wàllu mbokk.
2. Naareelu matukaay
Ku ne mën naa wax ne am na ay sañ-sañ ak ay tawfeex yu sosoo ci bataaxal bii te amul xeej ak seen, rawatina ci wàllu xeet, melo, awra, làkk, diiné, peete ci wàllu politig, xalaat, réew mbaa askan woo mën ti sosoo, ci it wàllu juddu alal ak lu mu mën ti doon.
Rax sa dolli amul xeej ak seen ci politig, yoon, mbaa doxalin wu aju ci bitim réew mbaa suuf soo xamne nit ki fa la cosaanoo; réew moomu mbaa suuf soosu moom na boppam walla deet, mbaa ñu yamale yengu-yëngoom.
3. Ñatteelu matukaay
Nit kune war naa dund ci tawfeex ak kaaraange.
4. Ñeenteelu matukaay
Waruñoo def kenn jaam mbaa mbindaan. Njaam ak njaayum jaam nanguwunu ko ci anam gu mu mën ti doon.
5. Juróomeelu matukaay
Waruñoo mbugal, tutal, mbaa teg kenn lu metti lool lu yelloo wul ak doomu aadama.
6. Juróom benneeli matukaay
Nit ku ne am na sañ-sañ ñu war kaa nangul darajaam ci wàllu yoon.
7. Juróom benneeli matukaay


Népp a yam ci kanamu yoon. Te it amul xeej ak seen, ku ne yoon woowu war na laa aar. Népp war nañu leen aar ci luy jalgati liñu tënk ci bataaxal bii ak bepp yëngu-gëngu buy indi par-parloo.
8. Juróom natteelu matukaay
Nit ku ne am na sañ-sañ dem ci berebi àtte kaay yi ci reewam saa yoo xamne sañ-sañam yooyu dëppook sàrti réewam mba yoon jalgati nañu ko.
9. Juróom ñentteeli matukaay
Menuñoo jàpp, tëj, mbaa genne kenn réewam te tegunu ko ci yoon.
10. Fukkeeli matukaay
Ci lu wér, nit kune mën naa egg ci berebu atte kaay wax li ko naqari ci anam gu jub, te baña ànd ak par-parloo, ne dañu ko taxal.
11. Fukkeeli been matukaay ak benn
1. Bépp nit bu ñu taqal cimbir mu tar jàppe nanu ko ku set ba loolu ñu ko taxal leer nàññ ginnaaw bi ñu ko attee. Te ñu taxawu ko ci lépp lu koy aar ci atte boobule.
2. Duñu tëj kenn ci ay jëfam mbaa lu mu fàtte mbete loolu mu jëf ci jamono jooju nekkul mbir mu tar ci wàllu yoon, ci biir ak bitim réew. Foofu it yoon du ko teg lu dul limengóok li mu def ci jamono jooju.
12. Fukkeeli matukaay ak ñaar
Kenn warula xuus ci dundinu doomu aadama, bu njabootam, ci lu jëm ci këram mbaa lu mengóok moom, di damm it jarajaam. Buñu jalgatee yii nit kune am na sañ-sañ ñu aar ko ci wàllu yoon.
13. Fukkeeli matukaay ak ñatt


1. Nit kune am na sañ-sañ wëndeelu ni mu ko neexe, tànn it dekkuwaayam ci biir réew bu mu mën ti doon.
2. Nit kune am na sañ-sañ génn réew mu mu mën ti doon. Fimu dëkk it bokk na ci-ak it dellusi ci réewam.
14. Fukkeeli matukaay ak ñent
1. Nit kune bu ñu ko mbugalee am na sañ-sañ làqu ji, mbaa ñaan ñu làq ko ci yeneni réew.
2. Su fekkee ne nit ki dañu koy toppu ginnaaw bi mu defee jëyyi, mbaa yëngu-yëngóon méngóowul ak li mbootaayu xeet yi tëral, sañ-sañ boobu.
15. Fukkeeli matukaay ak juróom
1. Nit ku ne am na sañ-sañ xeetoo cim réew.
2. Mënuñu ne nit ki xeetoowul cim réew te teguñu ko fenn, mbaa ñu xañ ko sañ-sañ su bëggee soppi xeetoom ak réewan.m
16. Fukkeeli matukaay ak juróom benn
1. Jigéen mbaa jóor saa yu matee amul xaaj ak seen, ak waaso bu mu mën ti bokk, réew, mba diiné am na sañ-sañ sëy ak it sos njaboot. Ñoo yam it sañ-sañ, balaa ñuy sëey, ci biir sëy ak it bu seen sëy tasee.
2. Sëy kenn menunuko fas, xanaa lu jiitu ku ne ci way-dencante yi joxe xalaatam.
3. Njaboot nekk na menneef gu am solo ci askan wi.
17. Fukkeeli matukaay ak juróom ñaar
1. Ngay dund yaw doww mbaa ak mbooloo am nga sañ-sañ am loo moomal sa bopp.
2. Menuñoo xañ kenn am aman.


18. Fukkeeli matukaay ak juróom ñatt
Nit kune am na sañ-sañ xalaat ak sa goom ci wàllu diine, soppi it diineem mba ngëmam, am na it tawfeex feeñal diineem, mbaa ngëmam, ak mbooloo, mbaa moom doww, fu àdduna daje mbaa deet, jarali ko ci njàngale mi, ci ay jëf, ci jaamu yi ak xarbaax.
19. Fukkeeli matukaay ak juróom ñent
Nit ku ne am na sañ-sañ wax mbaa bind lu ko soob. Ci waxam yooyule kenn menuko ce bundu xatal. Te it am na sañ-sañ di gëstu, di jot, di wasare ci anam gu yaa ay xabaaraki xalaat ak ay jumtukaay yu mi Men ti jefandikóo.
20. Ñaar fukkeeli matukaay
1. Nit kune am na sañ-sañ woote ab ndaje, mbaa sos mbootaay ci jàmm.
2. Mënuñoo bokk loo kenn ci mbootaay te àndu ci.
21. Ñaar fukkeeli matukaay ak benn
1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci ñiy doxal mbiri réewam. Mu teewal fa boppam, mbaa mu yabal ab ndaw mu teewal ko fa.
2. Nit ku ne am na sañ-sañ, amul xeej ak seen liggéey ci bépp béréb buy doxal mbiri réewam.
3. Pas-pasu askan mooy cëslaay buy dëgëral lépp luy doxal réew. Pas-pas gile war na feeñ ci palin yu yiw yu ñu wara amal léeg-léeg ci tannin gu yaa te am sutura,mbaa topp yoon wu wóor wu andak taw feex ci wàllu pal.
22. Ñaar fukkeeli matukaay ak ñaar
Nit ku ne meññeefu askan wi am na sañ-sañ ñu aar ko ci giru dundam. Ci dundam war na ci am xol bu sedd ci sañ-sañam yooyu, lu aju ci koom-koomam, ci dundinam ak ci lépp lu aju ci aadaam te di ko jox maanaa ak yookkute gu ànd


ak tawfeex ci wàllu darajaam, loolu lépp nag ku ne doomu réew mi indi dooleem ak di jokkalante ak bitim réew te mu méngook tërërin ak am-amu réew mu ne.
23. Ñaar fukk ak ñatteeli matukaay
1. Nit ku ne am na sañ-sañ liggéey, tànn it ci eanam gu ko neex liggéeyamm te mu dëppóok ay sàart yu yam te baax ci wàllu liggéey. Te it ñu aar ko ci ñàkkub liggéey.
2. Amul xeej ak seen ku néppam nanu sañ-sañ ñu fay leen, te loolu méngóok li mu aliggéey.
3. Keépp kuy liggéey am na sañ-sañ ñu jox ko pay gi mu yellool, baax te mën koo dundal ak njabbotam te mu yellook sagu doomu aadama, mu mottaliku it ak yeneeni pexe su mënee am ngir aar dundinam.
4. Nit ku ne am na sañ-sañ samp mbaa bokk ci ay kurel yu koy taxawu ci wàllu liggéeyam.
24. Ñaar fukk ak ñenteeli matukaay
Nit ku ne am na sañ-sañ noppalu, feexal xolal ak it di yamale diirub liggéeyam ak it léeg-léeg muy për, bër gu ànd ak xaalis.
25. Ñaar fukk ak juróomeeli matukaay
1. Nit ku ne am na sañ-sañ am dundingu yamamaay ngir dëgëral wér-gi-yaramam, raataageem ak bu njabootam, lrawatina ci wàllu lekk col, dëkkuwaay, lépp lu aju ci wàllu paj ak bépp yëngu-yëngu gu am farata ci wàllu dundam. Am na it sañ-sañ ñu aar ko bu liggeeyatul bu feebaree, bu amee laago, ñàkk saxnaam mbaa sërinam, mbaa màgget, mbaa mu ñàkk li muy suturloo ci anam yu dul ci cootareem.
2. War nañu beral loxo, dimbali képp ku tollu ci am doom ak it gune yi. Bépp xale bu juddu ci sëy, mbaa bu judduwul ci sëy ñoo bokk benn anam buñ leen di aare.


26. Ñaar fukk ak juróom benneeli matukaay
1. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu jàngal ko, njàng mi waruñu ci fayaku lu mu bon bon ci njàng mu suufe mi te am solo. Njàng mu suufe mi lu war la. Njàng mu xarala mi, te it aju ci wàllu liggéey war nanu koo wasaare. Amul xeej ak seen njàng mu kawe mi ubbil nañu ko képp ku ko yelloo.
2. Njàng war naa indi naataange gu yaa ci ddoomi aadama te it war na dëgëral ñu naw sañ-sañi doomi aadama aki tawfeexam ci anam gu yaa-wat na it rataxal déggóo gi ak yokkute mbootaayu xeet yi ngir jàmm sax.
3. Waajur yi ñoo jëkk am sañ-sañ ci anam gi ñuy yare seeni doom.
27. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay
1. Nit ku ne am na sañ-sañ bokk ci dépp lu aju ci caaday askan wi, di bànneexu ci lu cu aju ak it bokk ci lépp luy suqali xarala gi ak lu ciy meñ.
2. Nit ku ne am na sañ-sañ ñu aaral ko lépp lu aju ci lu mudefar ci wàllu la xarala, mbind mbaa lu aju ci wàllu caala.
28. Ñaar fukk ak juróom natteeli matukaay
Nit ku ne war naa tawaxu dëpp lu aju a askan wi, ak lu aju ci bitim réewam ba sañ-sañ ak tawfeex yi bataaxalu xeet gi ëmb mën a sax.
29. Ñaar fukk ak juróom nenteeli matukaay
1. Nit ku ne am na ay wareef yu ko war digganteem ak dëkkandoom yi ngir dëgëral ci anam gu ya darajaam.
2. Nit ku ne buy doxal ay sañ-sañam aki tawfeexam war naa sallook li ko yoon may, ngir mu mën a nangu, naw, sañ-sañ nawleem ba léepp lu aju ci yiw, teey ak naataange gu yaa sax ci askan wi.
3. Sañ-sañ yeek tawfeex yi mënuñukoo doxal ci anam gu deppoo-wul li mbootaayu xeet yi misër mbaa taxawal.


30. Fanweereeli matukaay
Ci fànn gu mu mën ti doon ci bataaxal bii, bépp réew, mbootaay mbaa nit, warul doxal mbaa def luy yàq sañ-sañ yeek tawfeex.

"Au Seuil De Ses Émeraudes, Mon Souffle Repose. Et Sur Son Eclantante Humeur Chaude, Mon Sourire Se Dépose."[THIAM Babel]

! Cliquez ICI Et Passez Votre Annonce !

Thiamaass


Membre - Familiarisé

Membre - Familiarisé
Sexe:Masculin Vierge Rat
Kureelu Mbootaayu Xeet Yi
Mbooloom Kaaraange Mi,
Tëral 1325 (2000)
Mbooloom Kaaraange Mi déggoo ci 4213 ndajeem bu 31 October 2000
Pattalikum Tëralam yii di 1261 (1999) bu 25 Waxset ci atum 1999, 1265 (1999) bu 17 Sàttinmbar ci
atum 1999, 1296 (2000) bu 19 Awiril ci atum 2000 akit 1314 (2000) bu 11 Waxset ci 2000, ak jépp
wax ju léen firndéel soqeekoo ci Persidaa ba booleek di fàttaliku li Persidaa bi dénkon way-taskati
xibaar yi ci 8 fan ci 8 weeru Mars ci atum 2000 (SC/6816) di bés bi Kureelu Mbootaayu Xeet Yi
jagleel Wareefi Jigéen ñéek Jàmm ci Addina bi.
Ci delloo xel ci dogu ga ñu dogu woon ca Waxi Bejing ya akit ca Tëralin wa ñu fa tëral war koo amal
(A/52/231) akit la ñu biral cib téere bu dajale la soqeekoo ci 23 Ndajem Special Kureelu Mbootaayu
Xeet Yi tudde ko "Jigéen ñi ci 2000 : Yemalem goor ak jigéen, Yokkute ak Jàmm ngir 21 xarnu bi"
(A/S-23/10/Rev.1), rawatina bi soxal Jigéen ak jàmmaarloo bu ànd ak ngànnaay.
Bu nu jàppee bu baax jëmu yeek xalaat yi lal Sartub Kureelu Mbootaayu Xeet Yi ak jàpp yit ni Sart
bi jagleel na Kuréelu Kaaraange gi mu sàmmu jàmm ak kaaraange ci fépp ci àdduna bi,
Seetlu gu yittéel ci ni, aji dëkk yi yoruli ngànnaay, daw laqu yeek nit ñiy gàddaaye séen dëkk rawatina
jigéen ñeek xale yi, ñooy ñi li gën a metti ci ay wiy dal te yit ñiy jàmmaarlook ñi yori ngànnaay ci séen
kow la ñuy gën di dal, ba jàpp nanu ni lii fàww mu am lu jur ci jàmm ju war a sax akit ci njubboo.
Feddli maanaa mi jigéen am ci fàggul ak ci jubbaatle ci wàllu ay ak ci taxawal jàmm, di firndeel ni war
na jigéen ñi bokk, ci kow séen cér tollook bu goor ci pexe yépp yu jublu ci saxal ak suuxat jàmm ak
kaaraange, akit nu xam ni jaadu na seen taxawaay gën a fés ci tëralin yépp yi aju ci fàggu ak ci safaara
wépp ay.
Feddli ni waareef la ñu doxal bu wér sart yi yoon tëral jagleel ko nit ak fu dëkke ci aàdduna bi ak
matuwaayam yi soxal wareefi doomi Aadama tey aar jigéen ñeek gone yu jigéen yu ndaw yi ci
jamonoy jàmmaarloo yi akit su jàmmaarloo yi jeexee.
Fésal ni jaadu na ci ni ñépp ñi séq ay wi war nañoo fexe ba sumb yi ñuy amal ngir di yeete ci dindim
njum ak loraange yi njum àndal, sédd soxla yu ñii di jigéen ñéek janq ji bokkuñu kook kenn.
Xàmmee bu wér ni jot na lool ci nu bàyyi xel ci ni jigéen ñi dañoo war a sax di bokk ci doxalin yi ñuy
tëral ngir amal jàmm te, ci foofu nuy sukkandiku ci Yëgleb Windook akit ci Tëralu doxalinu Namibii
ci la mu digle ñuy fexe ci wàllu sàkku jàmm ñuy yemale cérale ci diggante goor ñeek jigéen ñay bokk
ci kuréel yiy ko dox.(S/200/693);
Xam maanaa mi nekk ci digle yi ëmbu ci waxtaan wi Persidaa bi waxtaan ak way-taskati xibaar yi ci 8
fan ci weeru Mars 2000 mu jëm ci tàggat gi ñu war a tàggat képp nit kuy yëngu ci taxawal jàmm ci
wàllu yiir, aajook wareefi doomu Adaama jigéen ñeek xaleyi ci bërëb yi jàmmaarloo am.
Di xàmmee ni sunu gënoon a xam li jàmmaarloo yi ànd ak ngànnaay di def ci jigéen ñeek gone yu
jigéen yu ndaw yi, ni su amoon ay laamisoo ci diggante kuréel yi ngir taxawal seen karaange gu gën a
wér akit jigéen ñiy bokk ci doxalin yiy indi jàmm, saxalum jàmm jooju akum tasaareem akit kaaraange
dina gën a yomb ci adduna bi,
Di takk ni soloo ngi ci gën a ndëgaral lobbub xam-xam bi ne ci li soqeekoo jàmmaarloo yi ànd ak
ngànnaay te soxal jigéen ñeek xale yu jigéen yu ndaw yi
1.Di xiirtal Réew yi Bokk ci Kuréelu mbootaayu Xeet yi ñu fexe ba jigéen ñu gën a takku di
bokk ci jataay yiy dogal ak ci doxalin yi ñuy amal moo xam ci biir réew yi la ñu nekk, ci gox bi ak yu
réew i àdduna bi séq te ñu jublu ci fàggu, feg ak saafaray jàmmaarloo.
2.Di soññ Sekalteer Seneraal bi ci mu doxal tëralin yi ëmbu ci amalinu liggéey yi mudefar
(A/49/587) tey yaatal bokkin wu gën a yaatug ngir jigéen ñi ci dogal yi aju ci jàmmaarloo yi ak ci
yëngu-yëngu yiy indi jàmm.
3. Di ñaax Sekalter Seneraal ci mu yokk limub jigéen ñi muy takkal ndombo ngir ñu di ko
toogal toogaay yu ràñeeku, te yit ci loolu di woo Réew yi Bokk ñuy xamal Sekalteer Seneraal bi turi
jigéen ndax mu koy yokk ko ci lim bu mu war di yeesal saa su ne.
4. Di gën a ñaax Sekalter Seneraal bi ci mu gëstu nu mu yokke njariñ akit cérub jigéen ñi ci
biir liggéey yi Kuréelu Mbootaayu Xeet yi di amal ci gox yi , te gën a soxal seetlukati mbiri
soldaar,mbirum poliis ci waa xeet wi gànnaayuwul, warugari doomu Aadama ak ñiy dimbali way-sonn
yi.
5. Di biral ni taxaw nañu ci boole doxalin wuy bàyyi yemale ni cér yee war a tolloo ci diggnte
goor ñeek jigéen ñi ci liggéey yépp yi aju ci saxal jàmm, te di ñaam Sekalteer Seneraal bi mu fexe saa
yu mënee am, liggéey yi ñu def ci gox yi, di sédd jigéen ñi ab cér.
6. Di sàkku ci Sekalter Seneraal bi mu jagleel Réew yi Bokk ay yoon ak jumtukaayi tàggat yu
jëm ci wàllu kaaraange, wareef yi ak soxlay jigéen ak maanaa mi nekk ci jigéen ñi, di ko boole ci wépp
tëralin wuy taxawal aka dëgaral jàmm, di ñaan Réew yi Bokk ñuy bàyyi xel wàll yii akit di amal
doxalin yu jublu ci yeete ci mbirum xomptéefu Sidaa ak Sidaa ci boppam ci biir sumb yi ñuy doxal ci
seeni réew jagleel ko mbooloom soldaar si ak yu poliis yiy waaj a defi seen liggéey te ba tey Sekalteer
Seneraal bi fexe yit ba ñi newul i soldaar it te bokk ci liggéey bi ñu di léen boole ci tàggat mu ni mel.
7. Di xiirtal Réew yi Bokk ñu gën a dugal seen jàppale ci wàllu xaalis, xam^xam ak jumtukaay
ci yëngutu bu soxal fu ñu war a cérale jigéen ñi, ni ki ni ñu ko defale gtaxawal, Kuréelu Mbootaayu Xeet Yi Soxal Jigéen ñi akit Mbootaayu Xeet Yi Soxal gone yi,
ak Mbootaayu Xeet Yi Soxal Daw Làqu yi akit yeneenyu ëmb maanaa yu ni deme ci fànn wi.
8. Di woo ñépp ñiy yëngu ci waar wi, jamono ju ñuy amal ndajey waxtaan ak bu ñuy doxal
déggoo ngir taxawal jàmm, ñu jëlaale dogal yuy céral jigéen ñi ni ki g(a) Soxla yu ñu bokkul ak keneen ñoomjigéen ñeek gone yu jigéen yu ndaw yi am ci jamonoy yi
ñuléen di delloowaat seen àq, suñuy delluwaat ca la ñu newoon ak bu ñuy sàmpu ci beneen bërëb ak
suñu leen delloo seeni moomeel, su ñuydellu fa ñu joge woon akit ci jamonoy defaraat bu ay wi jàllee.
(b) Doxalin yiy jàppale bépp yëngu-yëngu bu joge ci jigéen i réew ma mbaa yu waa réew ma, ci
saafaaraw ay, te ñu nekk yu ñu jox wàll jigéen ñi ci déggooy tëralin yiy saafaara jàmmaarloo; (c)
Doxalin yiy wooral ni kaaraange ak sàmmum aqi jigéen ak gone yu jigéen yi rawatina yi aju këyitu
sarti réew mi, Tëralinu wote, poliis bi ak yoon.
9. Di woo ñi séqub jàmmaarloo ñu sàmmu wareef yépp yi aju ci àq ak karaangeg jigéen ak gone akit
nit ñi yorul i ngànnaay, rawatina ni warugar yi ñu leen teg ci biir Degoob Seneew bu 1949 akit Toftal
ya ca tegu ci 1977, Dégoob Daw-Laqu yi bu 1951 ak Firndéel ba ci 1967, Déggoob Mbooloom
Kaaraange mi-5- Jublu ci këyiti xibaar yi SC/6942 4213 Ndaje (PM) 31Oktoobar 2000 ci Raafal
bépp xeetu boddi bu jëm ci jigéen bu 1979 akit Déggoob Toftal bu àndul ak fitna ci 1999 ak
Déggoob Kuréelu Mbootaayu Xeet Yi ci Wareefi Gone bu 1989 akit yeneen ñaari Toftal yu àndul ak
fitna ci 25 Mee 2000, nu boole ci jàpp ni am nay dogal yu jublu ci fànn wi ëmbu ci Kuréelu Rom gi
féete woo Tirbinaalu Addina biy àtte Jalgatim Yoon
10. Di woo ñépp ñi séq jàmmaarloo bi ànd ak ngànnaay ñu jël i matuwaay ba aar jigéen ñeek
gone yu jigéen yi ci faagaagal yu wekku ci li ñu doon jigéen maanaam, siif ak bépp xeetu sàkku ak
metital ci jamonoy jàmmaarloo yu ànd ak ngànnaay.
11. Fésal ni Réew yi ñoo féete woo dakkal lépp luy seetaan jalgatim yoon akit yayoo ytirbinaal képp ku ñu biral ni bokk nga ci raafal ngiir, loraange yu soxal xeetu doom Aadama, lor i
bakken ci biir xeex bokk ca bépp xeetu sàkku bu ànd ak nééwal doole soxal jigéen ak gone yu jigéen
ñi, te di gën a firndeel ni ñu bañ a boole jalgati yooyu ci fépp fu mu mën a ame, ci jalgati yi ñuy baale
12 .Di woo ñépp ñi séq jàmmaarloo bi ànd ak ngànnaay ñu sàmmu gëdda gi nit ñi yorul ngànnaay am
ak ceru yëmaande bi ne ci sanci daw-làqu yi mbaa seeni dëkkuwaay akit di sédd soxla yi jigéen ñeek
gone yu jigéen yi bokkul ak kenn, boole ca na ñu liggéeye bërëb yooyu, te di fàttali dogal 1208
(1998) ci 19 Nowàmbar 1998
13. Di xiirtal ñépp ñi bokk tabax sumbub doxalinu nangum ngànnaay mi, summim soldaar si doon
xeex, ak delluwaatug nit ñi ci seeni gox, ñu bàyyi xel ni soxlay jigéen ñi wuute na ñook yu goor ñi
doon xeex te yit ñu jàpp soxlay nit ñeek ña wékku ci ñoom.
14. Yeesalaat ni taxaw na temm, ci waxtu wu ñu jëlee dogal yu wéeru ci Limu 41 bu Sartu Mbootaayu
Xeet Yi, ñuy bàyyiu xel la ñu nar a indil way-dëkk ya yorul i ngànnaay, te sédd cér soxlay ñii di jigéen
ñeek gone yu jigéen yu ndaw yi, bay céral lee-lee tëralin yuy soxal doom Aadama kese.
15. Xamle ni taxaw na ci fexe ba liggéey yi muy doxal di bàyyi xel cérale bi war ci diggante goor ak
jigéen ak aqi jigéen ñi ci kow di jokkook mbootaayi jigéen yi ci réew yi ak kuréeli mbootayu jigéen yi
ci àdduna bi
16. Woo Sekalteer Seneraal bi ci mu gëstu li jàmmaarloo yi ànd ak ngànnaay di indil jigéen ñeek gone
yu jigéen yu ndaw yi, wàllu jigéen ci dëgëral tabaxum jàmm ak cérub jigéen ci biir doxalin yiy indi
jàmm ak saafaaram gis-gis yu woroo akit di ko ñaan mu jébbal li soqeekoo ci ngëstu moomii mépp
réew mu bokk ci Kuréelu Mbootaayu Xeet Yi.
17. Di sàkku ci Sekalteer Seneraal bi ci jépp jamono, mu boole ciy xamleem yu jëm ci Kuréelu
Kaaraange gi, doxinu liiy cér yi soxal jigéen ak goor ci bépp liggéey bu jublu ci amal jàmm akit ci
yeneen fànn yu soxal jigéen ñéek janq ji.
18. Biral ni mbir mii dina wéy di doon séen yitte ba fàww."
Translated under the supervision
Of Africa Consultants International
Baobab Center
BP 5270 Dakar-Fann, SENEGAL
Tel. 221-825.36.37 or 825.49.72
Fax: 221-824.07.41
email:
Internet: http://www.acibaobab.org

"Au Seuil De Ses Émeraudes, Mon Souffle Repose. Et Sur Son Eclantante Humeur Chaude, Mon Sourire Se Dépose."[THIAM Babel]

! Cliquez ICI Et Passez Votre Annonce !

Voir le sujet précédent Voir le sujet suivant Revenir en haut  Message [Page 1 sur 1]

Poster un nouveau sujet  Répondre au sujet

Permission de ce forum:
Vous ne pouvez pas répondre aux sujets dans ce forum