Tiens j'ai des textes de Pacotille que j'ai transcris et je vous fait part de l'un d'entre eux.
Je ne suis pas certain d'avoir bien réussi la transcription, donc : méfiance!
D'ailleurs, je vous invite à m'aider à le corriger.

Le voilà ce texte:
Yé, Pacotille
Rappeur biy sol tik tik yi
Hadza Siratul budaa
Al budaa, walaqin
Ñu bari deñ koy sagané
Yoon wu jub mima doon sèt, gisnaako
Yoon wu lèr mima doon geustu, Gisnaako
Mungi nii
Diaradieuf Serigne Touba
Euskey Serigne Touba
Thieuy Serigne Touba
Borom Touba amoul moroom
Akasaaaa!
Pacotile, Pacotille!
Yé, é yaw
Nam tarixay'eup ben la
Ndax leup woteb Yallah la
Lila Serigne Touba digal
Té mulay musal ci mbugal
Mom lala Baye Niass sass
ak Mustafa Diene bu Fass
Bala ngay xamné borom bé meuna mayé
Nga gis ci mbirum Baye Laye
Wala nga dem bo Kaolax, doxantu bo médina Baye
Té nga deug waxou gor gou ted ga
Mame Abdou Dabakh
Né mbirum Tarixaa
Boko métriséwul, bu ci sax diéma wax
Aka ma beug Mame Cheikh Mbaye
Ndax ay Kiraamam
Ma sop Mame Cheikh Mbaye
Ndax Baye Djilé ak Baye Sam
Yonu Serigne Touba kukoy diingaat kuné do sori
Ladj ko ña ko daan dièm, safon xorom déño muj saalii
Serigne Modou Karaa
Kukoy ngañi kuné digna torox
Maa dib géwélam, ma ko wax té tontu du forox
Ndax kuma néwoon dinga mag sopéku duma ko gueumé
Sama'b ndaw gisnané, leup déma ko caxaanéh
Xaw ma won ludul tux Yamba
Agressé'k naan bèr
Yor sama jassi, teureureuri don ngandam sanginèr
Karim Falilo ma sopi booléma ci bakarimul'axlaa
Dzakaraa diangal ma'y juney juneyi zikrulaa
Kon suma néh: Diaradieufa Seringe Bara Mbacké
Tégeul ma ci : Euskey!!!
Mo bayou Siñ Aboo Madiyaanah
Borom rek dey
Yonu Murid lamay diobéh
dina gar luma ci gobéh
Yonu Murid lamay diobéh
Ndax Serigne Macké bo sobéh
Woy wi sentuwuma ci disk dor
Dédiy ab cant bumay diaglél Cheikh Fall bayu goor
Akasaa Cheikh Abdul Karim
Ndax budulon sa mam tey duma am sañ-sañu palasé samay riime
Wayé tam'iit, Diadieufa Seriñ Modou Karaa
Kula am kuné na laa diap, té xamné am na maraa
Am na maraa bu am mannaa
Yéh, Général
Men mi leu, ken ki leu
Ki gayndé leu ci dunya
kuko naqar Yallah fat la
Seriñ Touba moma fal
Ibra Faal faalémaa
Seriñ Touba mola fal
Ibra Faal faalélaa
Seriñ Touba moma fal
Ibra Faal faalémaa
Seriñ Touba mola fal
Ibra Faal faalélaa
Men mi leu, ken ki leu
Ki gayndé leu ci dunya
kuko naqar Yallah fat la
.......
Mbok yi lay waxal
Manam ñiy xalaat téy jafandiko sen xel
rawatina gayu baax yi deuk ci sélal
ñiy jeuf gudi ged sen diabar ak sen lal
diap diy juli, bayi la ngay deupa'ka dipi
Moy ki diel banex ak leup lu nex, teuju
Du mer du moy, doko mossa deug muy xuntu
Moy ki won ganaw aduna'k li ci biram
Sam ngoram bo lu léwul duko def ci biram
Amna wadioy romb ci mbedmi muy yélwaan
Té fu diant sowé nga yandor mu fanani diwaan
Borom bé léral sama'b xel
Mayma xam-xamu baatin
bo taxna mangkoy sant suba'k ngoon mangkoy djiin
Ñaan na Yallah mu teg ma ci yoonu Xaadimu Rasul
Tagat ma ci, ma bañ ko wac ba bañ may suul
Ñaan na, ci barké Alaji Fallou Mbaké
Yawmal qiyam, buñuy ramu, ñu bañ ma faté
Ñaan na, ci barké Cheikh Issa Diene
Borom Ndiéné'k Lagane
Borom yeureum ma dieugeul ma boléma'k ña gueun
Mu yeureum ma, dieugeul ma boléma'k ña gueun
Yeureum ma, dieugeul ma boléma'k ña gueun
Yeureum ma, dieugeul ma boléma'k ña gueun
Yeureum ma, dieugeul ma boléma'k ña gueun
Refrain
Waa Darou Mousty, Darou Marnane, Darou Khoudoss
Mbaké'k Touba, Diourbel
Akassaah!
Diaradieuf weuy Seriñ Assane Fall
.....
Ko sop Serigne Mansour Sy borom Daara jirah
......
ca Thiaroy Kaw, Sandaga, Pompier, Colobane,
Akassa les Immigrés, Italie France
Fu way mon di néh
Xamal néh Akassaaah
Pacotille!